Karite
Karite xeet la ci ñoñ vitellaria mi ngi bokk ci njabootug Sapotaceae ñu ngi koy fekk mu yaatu lool ci àllub Afrig sowwu jant bi ak diggu Afrig .
Ay turam
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]"Karite" ñi ngi koy woowe ba tay "siri" ca Bàmbara fële ca Mali loolu moo waral turu àngale wi "Shea tree"
Boo demee ci yenn goxi Afrig ñu ngi ko fay woowe "Tànga" walla "Tama".
Melo wi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Garab la gog day am ay xob guddaayam man naa jàpp 10 ba 16 ci ay met, du am ay xob li feeg amul fukk ak juróom-ñatt ci ay at, Ci boobu nag ci lay tàmbalee di am ay xob yoo xam ni dañuy yor melowu nëtëx bam am téemeeri at, garab la gog man naa dund ñaari xarnu.
Yaatuwaay peram manees na koo jàpp ci 1,5i met.
Ay foytéefam dañuy yor melo wu weex, amug xet , di génn ci jamonoy lolli maanaam ci diggante nowàmbar, saawiyee.
Ci ay foytéefam dañu fay fekk lem ngir ne yamb yi dañu koo bëgg lool. Garab la gog day màgg ci àll bi ngir nag ñu doon wax dëgg-dëgg "karite" fàww mu am fukki at ak juróom nga xam ne booba lay génne ay xobam yu jëkk.
Ay foytéefam juróom-benn kilo yii rekk lañuy jël def ko muy doon diw, diwug karite maanaam boo xoolee li muy ñorle buñu ko xaajee ñatti xaaj benn xaaj bi rekk lay jël.
Garab gi nag bu demee ba am juróom-fukki at jàpp téeméer ay xobam dañuy mujji doon ay doom loolu nag muy mbir mu yéeme lool ay foytéefam manees na leen a natt ci 10 jàpp 57 ci ay garaam.
Njariñ yi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Garabu Karite nag bari na ay njariñ lool ndax doom bi manees na cee am karite gees di diwoo garab gi itam manees na cee togg, manees na cee def ay kamoot, cempteŋ , ay toogu a.ñ.s.
Foytéef yi bari na ay witaamin lool dees koy jëfëndikoo.
Nataal yi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]-
Wobi garabug Karite
-
Doom yi
-
Doom yi, meññeef mi
-
Garab gi
-
Xob yi ba leegi